Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 17:9-14 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 17:9-14 in Kàddug Yàlla gi

9 Bale tooñ, yokk cofeel; sulliw ay, tas xarit.
10 Ku am ug dégg ngay yedd benn yoon, ab dof téeméeri yar du ko waññi.
11 Ku bon fippu doŋŋ lay jéem, te musibaa koy dikkal.
12 Taseek gaynde gu ñàkki doomam moo gën taseek dof ak yëfi dofam.
13 Kuy feye mbon jëf ju baax, lu bon du jóge sa kër.
14 Ndoortel ay di wal mu tàmbali, luy indib xuloo, bàyyil.
Kàddu yu Xelu 17 in Kàddug Yàlla gi