Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 17:8-28 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 17:8-28 in Kàddug Yàlla gi

8 Alalu ger njiglaay la ca ka koy joxe, ba fu mu jublu, mu nooy.
9 Bale tooñ, yokk cofeel; sulliw ay, tas xarit.
10 Ku am ug dégg ngay yedd benn yoon, ab dof téeméeri yar du ko waññi.
11 Ku bon fippu doŋŋ lay jéem, te musibaa koy dikkal.
12 Taseek gaynde gu ñàkki doomam moo gën taseek dof ak yëfi dofam.
13 Kuy feye mbon jëf ju baax, lu bon du jóge sa kër.
14 Ndoortel ay di wal mu tàmbali, luy indib xuloo, bàyyil.
15 Dëggal ku sikk ak daan ku jub, Aji Sax ji sib na yooyu yaar.
16 Ab dof du am xaalis, jënde xel mu rafet; buggu ca dara.
17 Xarit du bëgg, di bañ; mbokk day bokk ak yaw say coono.
18 Ku ñàkk bopp ay dige feyal jaambur, di ko gàddul boram.
19 Ku bëggu ay bëggi tooñ; damu, yàqule.
20 Ku njublaŋ du baaxle, kuy wax njekkar añe musiba.
21 Ku jur ab dof, am naqar; ab dof waajuram du bég.
22 Xol bu sedd day garabal, xol bu tiis day semmal.
23 Ku bon day nangu alalu ger ca suuf, nara jalgati yoon.
24 Ku am ug dégg ne jàkk ci xel mu rafet, ab dof ne xóll, xel ma sore lool.
25 Doom ju dof di tiisu baay ba ak naqaru ndey ja.
26 Ku deful dara, feyloo kob daan, dug njub; dóor as gor du yoon.
27 Ku moom sa làmmiñ am nga xam-xam, te ku teey am ngag dégg.
28 Ab dof sax bu noppee, nirook boroom xel; ku ne cell, ñu fooge lag muus.
Kàddu yu Xelu 17 in Kàddug Yàlla gi