7 Waxi teggin jekkul cib dof, ay fen ci as gor waxi noppi.
8 Alalu ger njiglaay la ca ka koy joxe, ba fu mu jublu, mu nooy.
9 Bale tooñ, yokk cofeel; sulliw ay, tas xarit.
10 Ku am ug dégg ngay yedd benn yoon, ab dof téeméeri yar du ko waññi.
11 Ku bon fippu doŋŋ lay jéem, te musibaa koy dikkal.
12 Taseek gaynde gu ñàkki doomam moo gën taseek dof ak yëfi dofam.