Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 17:19-23 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 17:19-23 in Kàddug Yàlla gi

19 Ku bëggu ay bëggi tooñ; damu, yàqule.
20 Ku njublaŋ du baaxle, kuy wax njekkar añe musiba.
21 Ku jur ab dof, am naqar; ab dof waajuram du bég.
22 Xol bu sedd day garabal, xol bu tiis day semmal.
23 Ku bon day nangu alalu ger ca suuf, nara jalgati yoon.
Kàddu yu Xelu 17 in Kàddug Yàlla gi