Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 17:10-19 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 17:10-19 in Kàddug Yàlla gi

10 Ku am ug dégg ngay yedd benn yoon, ab dof téeméeri yar du ko waññi.
11 Ku bon fippu doŋŋ lay jéem, te musibaa koy dikkal.
12 Taseek gaynde gu ñàkki doomam moo gën taseek dof ak yëfi dofam.
13 Kuy feye mbon jëf ju baax, lu bon du jóge sa kër.
14 Ndoortel ay di wal mu tàmbali, luy indib xuloo, bàyyil.
15 Dëggal ku sikk ak daan ku jub, Aji Sax ji sib na yooyu yaar.
16 Ab dof du am xaalis, jënde xel mu rafet; buggu ca dara.
17 Xarit du bëgg, di bañ; mbokk day bokk ak yaw say coono.
18 Ku ñàkk bopp ay dige feyal jaambur, di ko gàddul boram.
19 Ku bëggu ay bëggi tooñ; damu, yàqule.
Kàddu yu Xelu 17 in Kàddug Yàlla gi