Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 16:9-32 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 16:9-32 in Kàddug Yàlla gi

9 Nit ay sumb yoonam, Aji Sax ji sottal.
10 Su buur àddoo cib àtte, muy kàddu gu Yàlla dogal.
11 Nattub diisaay aki ndabam, na jub ngir Aji Sax ji. Moo sàkk mboolem nattukaay.
12 Buur daa sib kuy def lu bon, ngir njekkay dëgëral nguuram.
13 Wax ju dëggu, buur safoo boroom; ku jub, buur bëgg sa kàddu.
14 Merum buur ndaw la, dee a ko yónni; ku rafet um xel, giifal ko.
15 Buur, na kanam ga leer, sa bakkan mucc, su la baaxee, mu mel ni taw bu topp um nji.
16 Wutal xel mu rafet, bàyyi wurus; taamul ag dégg, wacc xaalis.
17 Yoonu kuy jubal day moyu lu bon, ku teeylu sa jëfin, sàmm sa bakkan.
18 Réy, yàqule; xeebaate, jóoru.
19 Woyof, ànd ak ku néewle moo gën séddook ku bew la mu lewal.
20 Ku teewlu mbir, baaxle; ku wóolu Aji Sax ji, bég.
21 Ki rafet xel mooy kiy ràññee, te su wax rafetee, dég-dég yomb.
22 Xel mu ñaw day suuxat bakkan, te ab dof jëfi dofam a koy yar.
23 Ku rafet xel, say kàddu xelu; soo waxee, yey.
24 Wax ju yiw di lem juy xelli, neexa ñam, di jàmmi yaram.
25 Yoon a ngi, nit defe ne jub na, te mu jëme ko ci ndee.
26 Ku bëgg lu neex, liggéey; ku bëgga faj sab xiif, njaxlaf.
27 Sagaru nit mooy sulli lu bon, ay waxam sax sawara la.
28 Nitu njekkar day yokk réeroo, ab soskat di féewaley xarit.
29 Ab soxor day yóbbaale dëkkandoom, jëme ko ci lu bon.
30 Piise, ku nar njekkar; màttu, ku def lu bon.
31 Bijjaawu bopp kaala gu yànj la, njekk a koy maye.
32 Muñ mer, moo gën njàmbaar; tënk sa bakkan moo raw nangub dëkk.
Kàddu yu Xelu 16 in Kàddug Yàlla gi