Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 16:27-33 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 16:27-33 in Kàddug Yàlla gi

27 Sagaru nit mooy sulli lu bon, ay waxam sax sawara la.
28 Nitu njekkar day yokk réeroo, ab soskat di féewaley xarit.
29 Ab soxor day yóbbaale dëkkandoom, jëme ko ci lu bon.
30 Piise, ku nar njekkar; màttu, ku def lu bon.
31 Bijjaawu bopp kaala gu yànj la, njekk a koy maye.
32 Muñ mer, moo gën njàmbaar; tënk sa bakkan moo raw nangub dëkk.
33 Tegoo bant nit a koy def, dogal ba Aji Sax ji la.
Kàddu yu Xelu 16 in Kàddug Yàlla gi