Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 16:24-29 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 16:24-29 in Kàddug Yàlla gi

24 Wax ju yiw di lem juy xelli, neexa ñam, di jàmmi yaram.
25 Yoon a ngi, nit defe ne jub na, te mu jëme ko ci ndee.
26 Ku bëgg lu neex, liggéey; ku bëgga faj sab xiif, njaxlaf.
27 Sagaru nit mooy sulli lu bon, ay waxam sax sawara la.
28 Nitu njekkar day yokk réeroo, ab soskat di féewaley xarit.
29 Ab soxor day yóbbaale dëkkandoom, jëme ko ci lu bon.
Kàddu yu Xelu 16 in Kàddug Yàlla gi