19 Woyof, ànd ak ku néewle moo gën séddook ku bew la mu lewal.
20 Ku teewlu mbir, baaxle; ku wóolu Aji Sax ji, bég.
21 Ki rafet xel mooy kiy ràññee, te su wax rafetee, dég-dég yomb.
22 Xel mu ñaw day suuxat bakkan, te ab dof jëfi dofam a koy yar.
23 Ku rafet xel, say kàddu xelu; soo waxee, yey.
24 Wax ju yiw di lem juy xelli, neexa ñam, di jàmmi yaram.
25 Yoon a ngi, nit defe ne jub na, te mu jëme ko ci ndee.
26 Ku bëgg lu neex, liggéey; ku bëgga faj sab xiif, njaxlaf.
27 Sagaru nit mooy sulli lu bon, ay waxam sax sawara la.
28 Nitu njekkar day yokk réeroo, ab soskat di féewaley xarit.
29 Ab soxor day yóbbaale dëkkandoom, jëme ko ci lu bon.
30 Piise, ku nar njekkar; màttu, ku def lu bon.
31 Bijjaawu bopp kaala gu yànj la, njekk a koy maye.