11 Nattub diisaay aki ndabam, na jub ngir Aji Sax ji. Moo sàkk mboolem nattukaay.
12 Buur daa sib kuy def lu bon, ngir njekkay dëgëral nguuram.
13 Wax ju dëggu, buur safoo boroom; ku jub, buur bëgg sa kàddu.
14 Merum buur ndaw la, dee a ko yónni; ku rafet um xel, giifal ko.
15 Buur, na kanam ga leer, sa bakkan mucc, su la baaxee, mu mel ni taw bu topp um nji.
16 Wutal xel mu rafet, bàyyi wurus; taamul ag dégg, wacc xaalis.
17 Yoonu kuy jubal day moyu lu bon, ku teeylu sa jëfin, sàmm sa bakkan.