Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 15:24-32 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 15:24-32 in Kàddug Yàlla gi

24 Ku rafet xel, jubal nga yoonu gudd fan, moyu teggi, ba jëm njaniiw.
25 Ku bew, Aji Sax ji màbb sa kër; ab jëtun, Aji Sax ji ñoŋal pàkkam.
26 Aji Sax ji bañ na mébét mu bon, te wax ju yiw daa sell fa moom.
27 Wutin wu lewul, sonal sa waa kër; ku bañ alalu ger gudd fan.
28 Ku jub day teeylu tontam; ab soxor, wax ju ñaaw rekk.
29 Aji Sax ji day dëddu ab soxor, di nangu ñaanu ku jub.
30 Kanam gu leer day seral xol; xibaaru jàmm, jàmmu yaram.
31 Kuy dégg àrtu yu koy musal, ku rafet xel a ngoog.
32 Xalab waxi yar, foye sa bopp la; deel déggi àrtu, yokk sam xel.
Kàddu yu Xelu 15 in Kàddug Yàlla gi