Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 15:20-27 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 15:20-27 in Kàddug Yàlla gi

20 Doom rafet xel, baay ba bég; te ab dof ay xeeb ndey ja.
21 Jëfi dof a neex ku ñàkk bopp, ku am ug dégg def njub.
22 Diisoo ñàkk, pexe moy; digle takku, pexe joy.
23 Nit bége na tontam lu dal, kàddu gu jib fa mu ñoree neex!
24 Ku rafet xel, jubal nga yoonu gudd fan, moyu teggi, ba jëm njaniiw.
25 Ku bew, Aji Sax ji màbb sa kër; ab jëtun, Aji Sax ji ñoŋal pàkkam.
26 Aji Sax ji bañ na mébét mu bon, te wax ju yiw daa sell fa moom.
27 Wutin wu lewul, sonal sa waa kër; ku bañ alalu ger gudd fan.
Kàddu yu Xelu 15 in Kàddug Yàlla gi