Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 15:12-17 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 15:12-17 in Kàddug Yàlla gi

12 Kuy ñaawle buggul ku ko àrtu, te du laaji ku rafet xel.
13 Xol bu sedd, kanam gu leer; xol bu tiis, boroom ne yogg.
14 Ku am ug dégg sàkku xam-xam, ab dof di toppi caaxaan.
15 Xol bu tiis, naqar wu sax; xol bu neex, bànneex bu sax.
16 Néewle te ragal Aji Sax ji moo gën barele, sa bopp ubu.
17 Njëlu ñetti xob fa ñu la soppe moo dàq yàpp wu duuf fu ñu la bañe.
Kàddu yu Xelu 15 in Kàddug Yàlla gi