Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 14:28-33 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 14:28-33 in Kàddug Yàlla gi

28 Su mbooloo baree, buur am ndam; fu nit ña néew, kilifa du fa dara.
29 Muñ mer, déggin wu yaa; gaawa tàng, gënatee dof.
30 Xel mu dal, yaram wu naat; fiiraange semmal boroom.
31 Ku sonal ku ñàkk, tooñ nga ka ko sàkk; ku baaxe ku néewle, teral nga ka ko sàkk.
32 Coxor detteel boroom; ku jub fegoo maanduteem.
33 Kuy dégg, sam xel saxoo rafet; ab dof sax xam na lu xelu.
Kàddu yu Xelu 14 in Kàddug Yàlla gi