21 Ku xeeb sa dëkkandoo, bàkkaar nga; ku baaxe ku ñàkk, mbégte ñeel la.
22 Kuy mébét lu bon daa réer, kuy mébét lu baax am nga ngor ak worma.
23 Kër-këri, jariñu; waxi neen, loxoy neen.
24 Ku rafet xel jagoo alal, ab dof ràngoo ndofam.
25 Seede bu dëggu day jot bakkan, kuy fen day wore.
26 Ragal Aji Sax ji kaaraange gu wér la ci nit, di rawtu ciy doomam.
27 Ragal Aji Sax ji day suuxat bakkan, ba boroom du tàbbi ci fiiri ndee.
28 Su mbooloo baree, buur am ndam; fu nit ña néew, kilifa du fa dara.
29 Muñ mer, déggin wu yaa; gaawa tàng, gënatee dof.
30 Xel mu dal, yaram wu naat; fiiraange semmal boroom.
31 Ku sonal ku ñàkk, tooñ nga ka ko sàkk; ku baaxe ku néewle, teral nga ka ko sàkk.
32 Coxor detteel boroom; ku jub fegoo maanduteem.