19 Ku bon, ku baax sut la; ku soxor ay toogaanu ku jub.
20 Ku ñàkk, say dëkk sax bañ la; ku barele, barey xarit.
21 Ku xeeb sa dëkkandoo, bàkkaar nga; ku baaxe ku ñàkk, mbégte ñeel la.
22 Kuy mébét lu bon daa réer, kuy mébét lu baax am nga ngor ak worma.
23 Kër-këri, jariñu; waxi neen, loxoy neen.
24 Ku rafet xel jagoo alal, ab dof ràngoo ndofam.
25 Seede bu dëggu day jot bakkan, kuy fen day wore.
26 Ragal Aji Sax ji kaaraange gu wér la ci nit, di rawtu ciy doomam.
27 Ragal Aji Sax ji day suuxat bakkan, ba boroom du tàbbi ci fiiri ndee.