Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 14:18-26 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 14:18-26 in Kàddug Yàlla gi

18 Ab téxét ndof ay céram, ku ñaw jagoo xam-xam.
19 Ku bon, ku baax sut la; ku soxor ay toogaanu ku jub.
20 Ku ñàkk, say dëkk sax bañ la; ku barele, barey xarit.
21 Ku xeeb sa dëkkandoo, bàkkaar nga; ku baaxe ku ñàkk, mbégte ñeel la.
22 Kuy mébét lu bon daa réer, kuy mébét lu baax am nga ngor ak worma.
23 Kër-këri, jariñu; waxi neen, loxoy neen.
24 Ku rafet xel jagoo alal, ab dof ràngoo ndofam.
25 Seede bu dëggu day jot bakkan, kuy fen day wore.
26 Ragal Aji Sax ji kaaraange gu wér la ci nit, di rawtu ciy doomam.
Kàddu yu Xelu 14 in Kàddug Yàlla gi