Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 14:1-22 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 14:1-22 in Kàddug Yàlla gi

1 Jigéen, rafet xel, dimbali waa këram, su deeb dof, tas këram.
2 Kuy jubal day ragal Aji Sax ji, ku dëng teddadil nga ko.
3 Ab dof a ngi réy-réylu, làmmiñam yar ko; ku rafet xel, sa kàddu aar la.
4 Su yëkk takkul, bey, sàq wéet; mu beye dooleem, meññeef ne gàññ.
5 Seede bu dëggu, dëgg rekk, seede bu dëgguwul, fen rekk.
6 Ab ñaawlekat day wut xel mu rafet, mu réer ko; ku am ug dégg, xam yomb la.
7 Dàndal ab dof, du la yokk xam-xam.
8 Ku ñaw day xelu, xam li muy def; ab dof di nax boppam.
9 Ab dof, su bàkkaaree, yoonam! Te ñay jubal a séq yiwu Yàlla.
10 Tiisu xol, boroom a ko xam; mbégte ma it jaambur bokku ca.
11 Ab soxor, këram day tas, mbaarum ku jub di naat.
12 Yoon a ngii, nit defe ne jub na, te mu jëme ko ci dee.
13 Nit a ngi ree, xol ba tiis, te mbégte mujje na njàqare.
14 Ku def njekkar sab añ mat, ku baax gën law demin.
15 Ab téxét, loo wax mu gëm; ku ñaw xam fi ngay jaare.
16 Ku xelu day ragal, di dëddu lu bon; ab dof day ràkkaaju, du tiit.
17 Ku gaawa mer, def jëfi dof, te kuy fexeel nit, ñu bañ la.
18 Ab téxét ndof ay céram, ku ñaw jagoo xam-xam.
19 Ku bon, ku baax sut la; ku soxor ay toogaanu ku jub.
20 Ku ñàkk, say dëkk sax bañ la; ku barele, barey xarit.
21 Ku xeeb sa dëkkandoo, bàkkaar nga; ku baaxe ku ñàkk, mbégte ñeel la.
22 Kuy mébét lu bon daa réer, kuy mébét lu baax am nga ngor ak worma.
Kàddu yu Xelu 14 in Kàddug Yàlla gi