Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 13:8-14 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 13:8-14 in Kàddug Yàlla gi

8 Ku am ay fey alal, ba mucc; ku amul deesu ko tëkku.
9 Ku jub day leer nàññ, ab soxor mel ni taal bu fey.
10 Réy-réylu jote rekk lay jur, ku dégg ndigal a xelu.
11 Alal ju lewul day naaw; foral benn-benn, ba biibal.
12 Yaakaar ju tas day jeexal xol, aajo ju faju di suuxat bakkan.
13 Ku sofental ndigalu Yàlla, yàqule; ku jëfe santaane Yàlla, yoolu.
14 Njàngle mu xelu day suuxat bakkan, ba boroom du tàbbi ci fiiri ndee.
Kàddu yu Xelu 13 in Kàddug Yàlla gi