Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 13:19-25 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 13:19-25 in Kàddug Yàlla gi

19 Aajo ju faju tooyal na xol, te ab dof jomb naa dëddu mbon.
20 Àndal ak ku xelu, sam xel rafet; ku lëngook ub dof, loru.
21 Ay topp na moykat, ku jub juble.
22 Ku baax, donale ba cay sëtam; alalu moykat, muuru ku jub.
23 Ku néewle bey na, meññeef ne gàññ, ñu àtte ko ñàkkal, mu ñàkk ko.
24 Ku dul bantal sa doom, bëggoo ko. Ku bëgg sa doom teel koo yar.
25 Ku jub day lekk ba regg, soxor ba dëkke xiif.
Kàddu yu Xelu 13 in Kàddug Yàlla gi