Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 13:17-23 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 13:17-23 in Kàddug Yàlla gi

17 Ndaw lu bon day loru. Ndaw lu wóor garab la ci nit.
18 Ku sàggane yoonu yar, séddoo ñàkk ak gàcce; kuy déggi àrtu, am teraanga.
19 Aajo ju faju tooyal na xol, te ab dof jomb naa dëddu mbon.
20 Àndal ak ku xelu, sam xel rafet; ku lëngook ub dof, loru.
21 Ay topp na moykat, ku jub juble.
22 Ku baax, donale ba cay sëtam; alalu moykat, muuru ku jub.
23 Ku néewle bey na, meññeef ne gàññ, ñu àtte ko ñàkkal, mu ñàkk ko.
Kàddu yu Xelu 13 in Kàddug Yàlla gi