Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 13:13-17 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 13:13-17 in Kàddug Yàlla gi

13 Ku sofental ndigalu Yàlla, yàqule; ku jëfe santaane Yàlla, yoolu.
14 Njàngle mu xelu day suuxat bakkan, ba boroom du tàbbi ci fiiri ndee.
15 Dangay xam lu jaadu, ñu naw la; yoonu workat day metti.
16 Képp ku teey jëfe xam-xam; ab dof ay siiwal ndofam.
17 Ndaw lu bon day loru. Ndaw lu wóor garab la ci nit.
Kàddu yu Xelu 13 in Kàddug Yàlla gi