Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 13:12-21 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 13:12-21 in Kàddug Yàlla gi

12 Yaakaar ju tas day jeexal xol, aajo ju faju di suuxat bakkan.
13 Ku sofental ndigalu Yàlla, yàqule; ku jëfe santaane Yàlla, yoolu.
14 Njàngle mu xelu day suuxat bakkan, ba boroom du tàbbi ci fiiri ndee.
15 Dangay xam lu jaadu, ñu naw la; yoonu workat day metti.
16 Képp ku teey jëfe xam-xam; ab dof ay siiwal ndofam.
17 Ndaw lu bon day loru. Ndaw lu wóor garab la ci nit.
18 Ku sàggane yoonu yar, séddoo ñàkk ak gàcce; kuy déggi àrtu, am teraanga.
19 Aajo ju faju tooyal na xol, te ab dof jomb naa dëddu mbon.
20 Àndal ak ku xelu, sam xel rafet; ku lëngook ub dof, loru.
21 Ay topp na moykat, ku jub juble.
Kàddu yu Xelu 13 in Kàddug Yàlla gi