24 Njaxlaf, jiitu; yaafus, des gannaaw.
25 Njàqare day jeexal xolu boroom, wax ju neex di tooyal xolam.
26 Ku jub day seetlu ku muy xaritool; soxor bi, jikkoom a koy sànk.
27 Ab yaafus bu rëbbee, sooy; cawarte koom la.
28 Jaaral ci njekk, ba gudd fan; yoon wu baax deesu fa dee.