20 Kuy ràbb lu bon lal pexey wor, kuy digle jàmm, am mbégte.
21 Ku jub du amu ay, ab soxor du tàggook musiba.
22 Aji Sax ji sib na fen-kat, safoo ku dëggu.
23 Nit ku ñaw day xam, ba ca; ab dof siiwal waxi dofam.
24 Njaxlaf, jiitu; yaafus, des gannaaw.