Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 12:17-26 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 12:17-26 in Kàddug Yàlla gi

17 Ku dëggu, seede dëgg; seede bu bon, fen rekk.
18 Làmmiñu waxkat, jam-jami jaasi; kàddu gu xelu, garab la ci.
19 Kàdduy dëgg, day sax dàkk; fen, xef xippi, mu wéy.
20 Kuy ràbb lu bon lal pexey wor, kuy digle jàmm, am mbégte.
21 Ku jub du amu ay, ab soxor du tàggook musiba.
22 Aji Sax ji sib na fen-kat, safoo ku dëggu.
23 Nit ku ñaw day xam, ba ca; ab dof siiwal waxi dofam.
24 Njaxlaf, jiitu; yaafus, des gannaaw.
25 Njàqare day jeexal xolu boroom, wax ju neex di tooyal xolam.
26 Ku jub day seetlu ku muy xaritool; soxor bi, jikkoom a koy sànk.
Kàddu yu Xelu 12 in Kàddug Yàlla gi