Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 12:15-21 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 12:15-21 in Kàddug Yàlla gi

15 Na dof di jëfe, njub la ci moom; dégg ndigal rafet um xel la.
16 Ab dof bu meree, mu gaawa feeñ; ku teey, tanqamlu saaga.
17 Ku dëggu, seede dëgg; seede bu bon, fen rekk.
18 Làmmiñu waxkat, jam-jami jaasi; kàddu gu xelu, garab la ci.
19 Kàdduy dëgg, day sax dàkk; fen, xef xippi, mu wéy.
20 Kuy ràbb lu bon lal pexey wor, kuy digle jàmm, am mbégte.
21 Ku jub du amu ay, ab soxor du tàggook musiba.
Kàddu yu Xelu 12 in Kàddug Yàlla gi