12 Ab soxor ay xemmem alal ju lewul, ku jub garab la, reen baa ko meññal.
13 Bàkkaaru làmmiñ dugal na boroom, ku jub mucc ci njàqare.
14 Làmmiñ reggal na boroom; ñaq, jariñu.
15 Na dof di jëfe, njub la ci moom; dégg ndigal rafet um xel la.
16 Ab dof bu meree, mu gaawa feeñ; ku teey, tanqamlu saaga.
17 Ku dëggu, seede dëgg; seede bu bon, fen rekk.