10 Ku jub day topptoo ag juram, ab soxor néeg cig juram.
11 Beyal sab tool, sab dund doy; topp ay caaxaan ñàkk bopp la.
12 Ab soxor ay xemmem alal ju lewul, ku jub garab la, reen baa ko meññal.
13 Bàkkaaru làmmiñ dugal na boroom, ku jub mucc ci njàqare.