Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 11:9-20 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 11:9-20 in Kàddug Yàlla gi

9 Ay sos la yéefar di loree, waaye ku jub xam-xam la cay mucce.
10 Ku jub baaxle, waa dëkkam bànneexu; ab saaysaay saay, mbégte dim riir.
11 Barkeb ku jub teral nab dëkk, kàddug ku soxor tas nab dëkk.
12 Waxi xeebaate ñàkk bopp la, ku am ag dégg day noppi.
13 Kuy wër di sos dangay wuññi sutura, ku jara wóolu dangay am bàmmeelu biir.
14 Tegtal tumurànke, am réew suux; digle bare, ndam dikk.
15 Bul gàddul kenn bor, di loru; bañ koo dige, daldi am jàmm.
16 Jigéen, na yiw, ñu sagal ko; góor gu néeg, alal doŋŋ.
17 Ku baax, boppam; ku bon, boppam.
18 Coxor feyul boroom, day naxe; deel def njekk, sag pey wóor.
19 Saxoo njekk, dund; sàlloo mbon, dee rekk.
20 Aji Sax ji bañ na njublaŋ, safoo maandute.
Kàddu yu Xelu 11 in Kàddug Yàlla gi