Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 11:6-12 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 11:6-12 in Kàddug Yàlla gi

6 Jubalal, sa njekk musal la; ab workat day bëgge, ba far keppu.
7 Ab soxor saay, yaakaaram seey, rawatina yaakaar ju sës ci alal.
8 Ku jub mucc ci njàqare, ab soxor wuutu ko ca.
9 Ay sos la yéefar di loree, waaye ku jub xam-xam la cay mucce.
10 Ku jub baaxle, waa dëkkam bànneexu; ab saaysaay saay, mbégte dim riir.
11 Barkeb ku jub teral nab dëkk, kàddug ku soxor tas nab dëkk.
12 Waxi xeebaate ñàkk bopp la, ku am ag dégg day noppi.
Kàddu yu Xelu 11 in Kàddug Yàlla gi