4 Alal du jariñ bésu mbugal; jub, mucc ci gàtt fan.
5 Ku mat, njekk xàllal la; coxor daaneel boroom.
6 Jubalal, sa njekk musal la; ab workat day bëgge, ba far keppu.
7 Ab soxor saay, yaakaaram seey, rawatina yaakaar ju sës ci alal.
8 Ku jub mucc ci njàqare, ab soxor wuutu ko ca.
9 Ay sos la yéefar di loree, waaye ku jub xam-xam la cay mucce.