Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 11:23-26 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 11:23-26 in Kàddug Yàlla gi

23 Ku jub, lu baax rekk lay sàkku; soxor biy yaakaar, mujje mbugal.
24 Nit a ngi tabe, di yokkule; nit di nëŋ-nëŋi, gëna ñàkk.
25 Ku yéwén, woomle; kuy suuxat, suuxu.
26 Nit a ngi móolu kuy denc pepp, ba mu ñàkkee, di gërëm ka koy jaay.
Kàddu yu Xelu 11 in Kàddug Yàlla gi