Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 11:2-9 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 11:2-9 in Kàddug Yàlla gi

2 Ku réy-réylu rus; woyofal ndax nga xelu.
3 Kuy jubal, jiital mat. Njublaŋ ak wor, detteelu.
4 Alal du jariñ bésu mbugal; jub, mucc ci gàtt fan.
5 Ku mat, njekk xàllal la; coxor daaneel boroom.
6 Jubalal, sa njekk musal la; ab workat day bëgge, ba far keppu.
7 Ab soxor saay, yaakaaram seey, rawatina yaakaar ju sës ci alal.
8 Ku jub mucc ci njàqare, ab soxor wuutu ko ca.
9 Ay sos la yéefar di loree, waaye ku jub xam-xam la cay mucce.
Kàddu yu Xelu 11 in Kàddug Yàlla gi