2 Ku réy-réylu rus; woyofal ndax nga xelu.
3 Kuy jubal, jiital mat. Njublaŋ ak wor, detteelu.
4 Alal du jariñ bésu mbugal; jub, mucc ci gàtt fan.
5 Ku mat, njekk xàllal la; coxor daaneel boroom.
6 Jubalal, sa njekk musal la; ab workat day bëgge, ba far keppu.