Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 11:19-31 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 11:19-31 in Kàddug Yàlla gi

19 Saxoo njekk, dund; sàlloo mbon, dee rekk.
20 Aji Sax ji bañ na njublaŋ, safoo maandute.
21 Ab soxor mbugalam du jaas, wóor na; te ku jub, saw askan mucc.
22 Taaru jongama ju xel ma gàtt, mooy jaaro wurus ci noppu mbaam-xuux.
23 Ku jub, lu baax rekk lay sàkku; soxor biy yaakaar, mujje mbugal.
24 Nit a ngi tabe, di yokkule; nit di nëŋ-nëŋi, gëna ñàkk.
25 Ku yéwén, woomle; kuy suuxat, suuxu.
26 Nit a ngi móolu kuy denc pepp, ba mu ñàkkee, di gërëm ka koy jaay.
27 Wutala wut lu baax, ñu nawloo la; ku sàkku lu bon, yaa koy yenu.
28 Ku yaakaar sa alal sab jéll a ngi ñëw, ku jub day juble ni gàncax gu naat.
29 Kuy fitnaal sa waa kër doo donn dara, ku dof, boroom xel yilif la.
30 Nit ku jub garab la, doom ya di dundal; ku rafet xel wut nit ñi.
31 Ku jub, jot sa yool ci kaw suuf, moykat beek soxor bi it daw raw.
Kàddu yu Xelu 11 in Kàddug Yàlla gi