Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 11:16-22 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 11:16-22 in Kàddug Yàlla gi

16 Jigéen, na yiw, ñu sagal ko; góor gu néeg, alal doŋŋ.
17 Ku baax, boppam; ku bon, boppam.
18 Coxor feyul boroom, day naxe; deel def njekk, sag pey wóor.
19 Saxoo njekk, dund; sàlloo mbon, dee rekk.
20 Aji Sax ji bañ na njublaŋ, safoo maandute.
21 Ab soxor mbugalam du jaas, wóor na; te ku jub, saw askan mucc.
22 Taaru jongama ju xel ma gàtt, mooy jaaro wurus ci noppu mbaam-xuux.
Kàddu yu Xelu 11 in Kàddug Yàlla gi