Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 11:13-20 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 11:13-20 in Kàddug Yàlla gi

13 Kuy wër di sos dangay wuññi sutura, ku jara wóolu dangay am bàmmeelu biir.
14 Tegtal tumurànke, am réew suux; digle bare, ndam dikk.
15 Bul gàddul kenn bor, di loru; bañ koo dige, daldi am jàmm.
16 Jigéen, na yiw, ñu sagal ko; góor gu néeg, alal doŋŋ.
17 Ku baax, boppam; ku bon, boppam.
18 Coxor feyul boroom, day naxe; deel def njekk, sag pey wóor.
19 Saxoo njekk, dund; sàlloo mbon, dee rekk.
20 Aji Sax ji bañ na njublaŋ, safoo maandute.
Kàddu yu Xelu 11 in Kàddug Yàlla gi