Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 10:20-24 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 10:20-24 in Kàddug Yàlla gi

20 Kàddug ku jub di ngën-gi-xaalis, xelum coxor amul solo.
21 Kàdduy ku jub jariñ na ñu bare, dof ñàkk na bopp, ba far dee.
22 Barkeb Aji Sax jeey maye alal, kër-këri taxula barele.
23 Jëf ju bon la dof di foye; ku am dég-dég safoo lu xelu.
24 Ab soxor, li mu ragal moo koy dab; nammeelu ku jub day sotti.
Kàddu yu Xelu 10 in Kàddug Yàlla gi