Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 10:2-7 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 10:2-7 in Kàddug Yàlla gi

2 Alal ju lewul du jariñ; jub, mucc ci gàtt fan.
3 Aji Sax ji du seetaan ku jub, di xiif, waaye day xañ ab soxor la mu xemmem.
4 Yaafus, walaakaana; farlu, woomle.
5 Ku ngóob jot, nga góob, xelu nga; ngóob taxaw, ngay nelaw, gàcce la.
6 Jub, barkeelu; ku soxor, wax ja làq fitna.
7 Ku jub barkeel, saw tur du fey; ab soxor, turam seey.
Kàddu yu Xelu 10 in Kàddug Yàlla gi