18 Ku la nëbbal mbañeel, da lay fen; kuy wër di sos, ab dof la.
19 Wax ju bare, moy ñàkku ca; ku moom sa làmmiñ, xelu nga.
20 Kàddug ku jub di ngën-gi-xaalis, xelum coxor amul solo.
21 Kàdduy ku jub jariñ na ñu bare, dof ñàkk na bopp, ba far dee.
22 Barkeb Aji Sax jeey maye alal, kër-këri taxula barele.
23 Jëf ju bon la dof di foye; ku am dég-dég safoo lu xelu.