Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 10:10-17 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 10:10-17 in Kàddug Yàlla gi

10 Piiseek làq-làqal, sabab njàqare; ab dof waxa wax, ba loru.
11 Kàdduy ku jub bëtu ndox la, day naatal; waaye ku soxor, wax ja làq fitna.
12 Mbañeelak ayoo; cofeelak jéggale bépp tooñ.
13 Kuy dégg, say wax rafet; te ku ñàkk bopp, yelloo yetu gannaaw.
14 Ku rafet xel day xam, ne cell; bu dof noppiwul, yàqule teew.
15 Alal day aar boroom ni ab tata, ñàkk di lor baadoolo.
16 Ku jub jot peyam, dunde; ab soxor di bàkkaare alalam.
17 Yaru, gudd fan; sàgganey àrtu, sànku.
Kàddu yu Xelu 10 in Kàddug Yàlla gi