Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 9

Jëf ya 9:38-41

Help us?
Click on verse(s) to share them!
38Ci biir loolu taalibe yi dégg ne Piyeer a nga Lidd, te Lidd sorewul Yope. Ñu yebal ñaari nit ca moom, ngir ñaan ko mu ñëw te baña yeex.
39Piyeer jóg, ànd ak ñoom, ba agsi. Ñu yéege ko ca néegu kaw taax ma. Ay jëtun a nga fa woon. Ñoom ñépp di jooyoo, yéew Piyeer, won ko turki yaak mbubb ya Dorkas defaroon ba muy nekk ak ñoom.
40Ci kaw loolu Piyeer dàq ñépp ca biti. Mu sukk, ñaan, daldi walbatiku jublook néew bi, ne: «Tabita, jógal!» Mu ne xiféet, gis Piyeer, jóg toog.
41Piyeer may ko loxo, yékkati ko. Ba loolu amee Piyeer woo ñu sell ña, ak jëtun ña, won leen ndaw sa, muy dund.

Read Jëf ya 9Jëf ya 9
Compare Jëf ya 9:38-41Jëf ya 9:38-41