Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 9:3-5 in Wolof

Help us?

JËF YA 9:3-5 in Téereb Injiil

3 Waaye bi muy jub Damaas, ca saa sa leer gu jóge asamaan melax, ba ëmb ko.
4 Mu daanu ci suuf, dégg baat bu ko ne: «Sóol, Sóol, lu tax nga di ma fitnaal?»
5 Mu wuyu ne: «Yaay kan Boroom bi?» Boroom bi ne ko: «Maay Yeesu, mi ngay fitnaal.
JËF YA 9 in Téereb Injiil

Jëf ya 9:3-5 in Kàddug Yàlla gi

3 Naka la Sóol dem ba jub Damaas, ag leer bawoo asamaan, jekki ne ràyy ci kawam.
4 Mu daanu ci suuf, daldi dégg baat bu ko ne: «Sóol, Sóol, lu tax nga di ma bundxatal?»
5 Mu ne: «Yaay kan Sang bi?» Mu ne: «Man maay Yeesu, mi ngay bundxatal.
Jëf ya 9 in Kàddug Yàlla gi