Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 8:3-8 in Wolof

Help us?

JËF YA 8:3-8 in Téereb Injiil

3 Waaye naka Sóol, mu ngay tas mbooloom ñi gëm, di tàbbi ca kër ya, tey jàpp góor ak jigéen, di leen tëj kaso.
4 Ñi tasaaroo nag dem fu nekk, di fa xamle xibaaru jàmm bu kàddug Yàlla.
5 Naka Filib mu dem ca benn dëkk ca Samari, di leen yégal Kirist.
6 Bi ko mbooloo mi déggee te gis kéemaan yi muy def, ñu bokk benn xalaat, fekki ko ci li mu wax.
7 Ndaxte ay rab yu bon bàyyi nañu nit ñu bare, ña ñu jàppoon, di yuuxu ci kaw; te ñu bare ñu làggi ak ñu lafañ daldi wér.
8 Noonu mbég mu réy tàbbi ca dëkk ba.
JËF YA 8 in Téereb Injiil

Jëf ya 8:3-8 in Kàddug Yàlla gi

3 Ci biir loolu Sóol moom, ma ngay jéema faagaagal mbooloom gëmkat ñi, di dugg ci kër yi, diri góor ak jigéen, génne, ñu sànni kaso.
4 Gëmkat ña tasaaroo di xamle fépp fu ñu jaare, xibaaru jàmm bu kàddu gi.
5 Noonu la Filib deme péeyub Samari, di siiwtaane Almasi.
6 Ba waa dëkk ba déggee mbaa ñu gis kéemaan ya muy def, ñoo bokk teewlu ay waxam.
7 Ndax bare na ca ñu rab yu bon jàppoon te mujj bàyyi leen, génne yuux yu réy; bare na ca it ñu lafañ ak ñu làggi woon te mujj wér.
8 Muy mbég mu réy nag ca dëkk boobee.
Jëf ya 8 in Kàddug Yàlla gi