Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 8:18-34 in Wolof

Help us?

JËF YA 8:18-34 in Téereb Injiil

18 Bi Simoŋ gisee nag ne Yàlla may na Xel mi jaarale ko ci loxoy ndaw ya, mu indil leen xaalis,
19 ne leen: «Mayleen ma sañ-sañ boobu, ba ku ma teg samay loxo, nga jot Xel mu Sell mi.»
20 Waaye Piyeer ne ko: «Asarul ak sa xaalis, yaw mi yaakaar ne man ngaa jënd mayu Yàlla ak xaalis.
21 Amuloo benn wàll mbaa cér ci lii, ndaxte sa xol laabul ci kanam Yàlla.
22 Réccul nag sa coxor te ñaan Boroom bi, mu baal la sa xalaatu xol, su manee am.
23 Ndaxte gis naa ne sóobu nga ci lu wex xat ci kanam Yàlla, te bàkkaar not na la.»
24 Simoŋ nag ne leen: «Ñaanal-leen ma ci Boroom bi, ngir mu fegal ma li ngeen wax.»
25 Noonu bi ñu seedeelee Yàlla te wax ci kàddoom, ñu dellu Yerusalem, di xamle xibaaru jàmm bi ci dëkk yu bare yu waa Samari.
26 Naka noonu benn malaakam Boroom bi ne Filib: «Jógal te jublu Misra, jaar ci yoon wi jóge Yerusalem, jëm Gasa, di màndiŋ.»
27 Filib jóg dem. Noonu mu gis fa nitu Ecópi ku yoom, di jaraaf ju mag ci Kandas, buur bu jigéen bu Ecópi, te di ko wottul xaalisam bépp. Fekk mu ñëwoon Yerusalem, ngir màggalsi Yàlla, bay dellu;
28 mu toog ci watiiram, di jàng téereb yonent Yàlla Esayi.
29 Xel mi nag ne Filib: «Dabal watiir wale.»
30 Noonu Filib dawsi, mu dégg waayi Ecópi ja, di jàng téereb yonent Yàlla Esayi. Mu laaj ko: «Ndax xam nga li ngay jàng?»
31 Mu ne ko: «Nu ma ko mana xame, su ma ko kenn firilul?» Mu woo Filib nag, mu yéeg, toog ak moom.
32 Fekk aaya yii la doon jàng ci Mbind mi: «Yóbbu nañu ko ni xar mu ñuy rendiji; ni mburt mu luu ci kanam i watkat, mu ne cell.
33 Ci toroxteem nangu nañu dëggam; ñi mu tollool jamono, ku ci xalaat lii? Jële nañu bakkanam ci àddina.»
34 Jaraaf ja nag ne Filib: «Maa ngi lay laaj, ci mbirum kan la yonent bi jëmale wax ji? Ndax mbirum boppam lay wax mbaa mu keneen?»
JËF YA 8 in Téereb Injiil

Jëf ya 8:18-34 in Kàddug Yàlla gi

18 Simoŋ nag gis noonee mayug Noo, gi sababoo ci tegeb loxo bu ndaw ña amal, ba tax mu indil leen xaalis.
19 Mu ne leen: «Mayleen ma man itam xam-xam bii, ngir ku ma teg loxo, nga jot Noo gu Sell gi.»
20 Piyeer ne ko: «Na sa xaalis ànd ak yaw asaru, ndegam ab xaalis nga yaakaara jënde mayu Yàlla!
21 Amuloo benn wàll mbaa ab cér ci lii, ndax sa xol a jubul ci kanam Yàlla.
22 Réccul nag sa mbon gii, te ñaan Boroom bi; jombul mu baal la sa mébétu xol.
23 Ndax gis naa ni nga sóoboo ci wextanu kañaan, keppu ci ndëngte.»
24 Simoŋ ne leen: «Ñaanal-leen ma Boroom bi, yeen ci seen bopp, ngir li ngeen wax lépp, lenn bañ ma cee dab.»
25 Gannaaw ba Piyeer ak Yowaan seedeelee kàddug Boroom bi, biral ko, Yerusalem lañu dellu, di xamle xibaaru jàmm bi ci ay dëkki Samari yu bare.
26 Menn malaakam Boroom bi nag wax Filib, ne ko: «Fabul jubal bëj-saalum; yoon wa kenn jaareetul te bartaloo Yerusalem, jëm Gasa.»
27 Filib fabu, dem. Ndeke am na jenn waayu Ecopi ju màggalsi woon Yerusalem. Nit kooku doonoon moraange, te di jaraaf ju mag ju Kàndas Lingeeru Ecopi; moo doon saytu mboolem alalu Lingeeru Ecopi.
28 Naka la jaraaf ja màggalsi bay dellu Ecopi, toog ca watiiram, di jàngaale téereb Yonent Yàlla Esayi,
29 Noowug Yàlla ne Filib: «Doxal, dab watiir bale.»
30 Filib dabsi waayi Ecopi ja, daldi dégg muy jàng téereb Yonent Yàlla Esayi. Mu ne ko: «Ndax xam nga li ngay jàng?»
31 Mu ne ko: «Nu ma ko mana xame, te kenn firilu ma ko?» Ba loolu amee mu ne Filib, mu yéeg, toog ak moom. Filib yéeg.
32 Lii nag mooy dogu mbind ma mu doon biral: «Dees koo yóbbu ni xar mu ñuy rendiji; mbete mburt mu ne cell ci kanam ki koy wat, ubbiwul gémmiñam.
33 Ci biir toroxteem lañu ko xañ dëggam; kuutaayam nag, ana ku ci mana wax? Ndegam bakkanam lañu toxale kaw suuf.»
34 Jaraaf ja ne Filib: «Yaw laay laaj, ci kan la yonent bi wax lii? Boppam lay wax am keneen?»
Jëf ya 8 in Kàddug Yàlla gi