Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 7:36-48 in Wolof

Help us?

JËF YA 7:36-48 in Téereb Injiil

36 Moo leen génne réewu Misra, di def ay kéemaan ak ay firnde ca réew ma, ca géeju Barax ya ak ca màndiŋ ma diirub ñeent fukki at.
37 Musaa moomu moo ne woon bànni Israyil: “Yàlla dina leen feeñalal ci seeni bokk Yonent bu mel ni man.”
38 Te moo nekkoon ak mbooloo ma ca màndiŋ ma, ànd ak sunuy maam, wéttalikoo malaaka, mi waxoon ak moom ci tundu Sinayi. Te mu jote ci Yàlla kàddu yiy dund, ngir jottali nu ko.
39 Waaye sunuy maam nanguwuñu koo déggal; dañu koo bañ te seeni xel dëpp, dellu Misra.
40 Ñu sant Aaróona ne: “Sàkkal nu ay yàlla yuy jiitu ci sunu kanam, ndaxte Musaa male nu génne ci réewu Misra, xamunu lu ko dal.”
41 Booba nag ñu tëgglu aw sëllu, muy xërëm, ñu di ko tuuru, di bànneexu ci seeni jëfi loxo.
42 Waaye bi ñu ko defee Yàlla dëddu leen, bërgël leen, ñuy jaamu biddiiwi asamaan. Moom lañu bind ci téereb yonent yi ne: “Yéen bànni Israyil, ndax rendi ngeen jur, jébbal ma, boole ko ak i sarax, diirub ñeent fukki at ca màndiŋ ma?
43 Yóbbu ngeen sax fu nekk xayma, biy màggalukaayu Molog, ak biddiiwub Refan, bi ñu daan bokkaaleel Yàlla, di ay nataal, yi ngeen defoon ngir màggal leen! Kon nag dinaa leen toxal, yóbbu leen ci gannaaw réewu Babilon.”
44 «Sunuy maam amoon nañu ca màndiŋ ma xaymab màggalukaay, bi ëmboon li Yàlla seede. Xayma boobu nag defoon nañu ko, roye ko ci bi Musaa gisoon, ni ko ko Yàlla sante woon.
45 Te gannaaw ga, bi Yosuwe nekkee kilifag sunuy maam, ñu jot xayma ba ñoom it, yóbbu ko ca réew, ma ñu nangu ca xeet ya Yàlla dàq ci seen kanam. Xayma ba nekk fa, ba ci jamonoy Daawuda.
46 Moom yiw na fa kanam Yàlla, mu ñaan ko, mu sàkkal ko kër ngir askanu Yanqóoba.
47 Waaye Suleymaan moo tabaxal Yàlla kër ga.
48 «Moona Aji Kawe ji du dëkk ci fu loxol nit defar; moom la ab yonent wax ne:
JËF YA 7 in Téereb Injiil

Jëf ya 7:36-48 in Kàddug Yàlla gi

36 Moo leen génne réewum Misra, moo def ay kéemaan aki firnde ca réew ma, ak ca géeju Barax ya, ak ca màndiŋ ma, diiru ñeent fukki at.
37 Musaa moomu moo noon bànni Israyil: “Yonent bu mel ni man la leen Yàlla di feeñalal ci seen biiri bokk.”
38 Moom it moo nekkoon ak mbooloo ma ca màndiŋ ma, mook malaaka ma doon wax ak moom ca kaw tundu Sinayi ca sunu wetu maam ya. Moo jot ci kàddu yuy dund, ngir jottli nu ko.
39 Kooku la sunuy maam nanguwul woona déggal. Dañu koo far xarab, namma walbatiku dellu Misra.
40 Ñu ne Aaróona: “Sàkkal nu ay yàlla yu nu jiite, ndax Musaa mii nu génne réewum Misra, xamunu lu ko dal.”
41 Jant yooyu lañu sàkk jëmmu sëllu, defal jëmm ja ab sarax, di bànneexoo lu ñu sàkke seeni loxo.
42 Yàlla nag dëddu leen, bàyyi leen, ñuy jaamu biddiiw yi, ni ñu ko binde ci téereb yonent yi, ne: “Yeen waa kër Israyil, saraxu jur ak yeneen sarax, ndax man ngeen ko daan indil diiru ñeent fukki at ca màndiŋ ma?
43 Molog seen tuur mi, ngeen yóbbaale xaymab jaamookaayam, ak seen biddiiwu yàlla ji ñu naa Refan, jëmm yooyu ngeen sàkk, di leen sujjóotal! Kon nag maa leen di toxal ca wàllaa Babilon.”
44 «Xaymab seede baa nga woon ak sunuy maam ca màndiŋ ma, ñu sàkke ko na ko ka doon wax ak Musaa sante, dëppale kook misaal ma Musaa gisoon.
45 Xayma ba la sunuy maam jot, dugal ko ci kilifteefu Yosuwe ca biir réewum xeet, ya leen Yàlla dàqal. Xayma ba nekk fa, ba ca janti Daawuda.
46 Daawuda, ma Yàlla baaxe woon, sàkku woon na am màkkaan ngir Yàllay Yanqóoba.
47 Waaye Suleymaan moo ko mujj tabaxal kër.
48 «Moona Aji Kawe ji du dëkke lu loxo defar, mooy la yonent ba ne:
Jëf ya 7 in Kàddug Yàlla gi