Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 7:33-51 in Wolof

Help us?

JËF YA 7:33-51 in Téereb Injiil

33 Noonu Boroom bi ne ko: “Summil say dàll, ndaxte bérab bi nga taxaw, bérab bu sell la.
34 Gis naa bu baax fitnay sama xeet ci Misra te dégg naa seeni tawat, kon wàcc naa ngir musal leen. Léegi nag ñëwal, dinaa la yebal Misra.”
35 «Musaa moomu bañoon nañu ko, ba ne ko: “Ku la teg kilifa ak àttekat?” Waaye moom la Yàlla yebal, jaarale ko ci malaaka mi ko feeñu ca ngarab sa, ngir mu nekk kilifa gu leen di goreel.
36 Moo leen génne réewu Misra, di def ay kéemaan ak ay firnde ca réew ma, ca géeju Barax ya ak ca màndiŋ ma diirub ñeent fukki at.
37 Musaa moomu moo ne woon bànni Israyil: “Yàlla dina leen feeñalal ci seeni bokk Yonent bu mel ni man.”
38 Te moo nekkoon ak mbooloo ma ca màndiŋ ma, ànd ak sunuy maam, wéttalikoo malaaka, mi waxoon ak moom ci tundu Sinayi. Te mu jote ci Yàlla kàddu yiy dund, ngir jottali nu ko.
39 Waaye sunuy maam nanguwuñu koo déggal; dañu koo bañ te seeni xel dëpp, dellu Misra.
40 Ñu sant Aaróona ne: “Sàkkal nu ay yàlla yuy jiitu ci sunu kanam, ndaxte Musaa male nu génne ci réewu Misra, xamunu lu ko dal.”
41 Booba nag ñu tëgglu aw sëllu, muy xërëm, ñu di ko tuuru, di bànneexu ci seeni jëfi loxo.
42 Waaye bi ñu ko defee Yàlla dëddu leen, bërgël leen, ñuy jaamu biddiiwi asamaan. Moom lañu bind ci téereb yonent yi ne: “Yéen bànni Israyil, ndax rendi ngeen jur, jébbal ma, boole ko ak i sarax, diirub ñeent fukki at ca màndiŋ ma?
43 Yóbbu ngeen sax fu nekk xayma, biy màggalukaayu Molog, ak biddiiwub Refan, bi ñu daan bokkaaleel Yàlla, di ay nataal, yi ngeen defoon ngir màggal leen! Kon nag dinaa leen toxal, yóbbu leen ci gannaaw réewu Babilon.”
44 «Sunuy maam amoon nañu ca màndiŋ ma xaymab màggalukaay, bi ëmboon li Yàlla seede. Xayma boobu nag defoon nañu ko, roye ko ci bi Musaa gisoon, ni ko ko Yàlla sante woon.
45 Te gannaaw ga, bi Yosuwe nekkee kilifag sunuy maam, ñu jot xayma ba ñoom it, yóbbu ko ca réew, ma ñu nangu ca xeet ya Yàlla dàq ci seen kanam. Xayma ba nekk fa, ba ci jamonoy Daawuda.
46 Moom yiw na fa kanam Yàlla, mu ñaan ko, mu sàkkal ko kër ngir askanu Yanqóoba.
47 Waaye Suleymaan moo tabaxal Yàlla kër ga.
48 «Moona Aji Kawe ji du dëkk ci fu loxol nit defar; moom la ab yonent wax ne:
49 “Asamaan mooy sama jal, te suuf mooy sama tegukaayu tànk. Kon gan kër ngeen may tabaxal, mbaa fan mooy sama bérabu noppalukaay?
50 Ndax du sama loxo moo defar yëf yooyu yépp? —Moom la Boroom bi doon wax.”
51 «Yéen ñi dëgër bopp, ànd ak xol buy bañ ak ay nopp yuy fatt, mel ni ñi xamul Yàlla. Dungeen noppeek a diiroo ak Xel mu Sell mi; ni ko seen baay yi daan defe, noonu ngeen di def, yéen itam.
JËF YA 7 in Téereb Injiil

Jëf ya 7:33-51 in Kàddug Yàlla gi

33 Boroom bi ne ko: “Summil say dàll, ndax fii nga taxaw, suuf su sell la.
34 Gis naa bu baax sama coonob ñoñ ci Misra; maa dégg seeni onk, ba wàcc ngir wallusi leen. Léegi nag dikkal, ma yebal la Misra.”
35 «Musaa moomu ñu weddi woon, ne ko: “Ku la def kilifa ak ab àttekat?” Moom nag la Yàlla def kilifa ak ab jotkat, yebal ko ci ñoom, malaaka ma feeñu Musaa ca gajj ba, daldi koy jottli yóbbante ba.
36 Moo leen génne réewum Misra, moo def ay kéemaan aki firnde ca réew ma, ak ca géeju Barax ya, ak ca màndiŋ ma, diiru ñeent fukki at.
37 Musaa moomu moo noon bànni Israyil: “Yonent bu mel ni man la leen Yàlla di feeñalal ci seen biiri bokk.”
38 Moom it moo nekkoon ak mbooloo ma ca màndiŋ ma, mook malaaka ma doon wax ak moom ca kaw tundu Sinayi ca sunu wetu maam ya. Moo jot ci kàddu yuy dund, ngir jottli nu ko.
39 Kooku la sunuy maam nanguwul woona déggal. Dañu koo far xarab, namma walbatiku dellu Misra.
40 Ñu ne Aaróona: “Sàkkal nu ay yàlla yu nu jiite, ndax Musaa mii nu génne réewum Misra, xamunu lu ko dal.”
41 Jant yooyu lañu sàkk jëmmu sëllu, defal jëmm ja ab sarax, di bànneexoo lu ñu sàkke seeni loxo.
42 Yàlla nag dëddu leen, bàyyi leen, ñuy jaamu biddiiw yi, ni ñu ko binde ci téereb yonent yi, ne: “Yeen waa kër Israyil, saraxu jur ak yeneen sarax, ndax man ngeen ko daan indil diiru ñeent fukki at ca màndiŋ ma?
43 Molog seen tuur mi, ngeen yóbbaale xaymab jaamookaayam, ak seen biddiiwu yàlla ji ñu naa Refan, jëmm yooyu ngeen sàkk, di leen sujjóotal! Kon nag maa leen di toxal ca wàllaa Babilon.”
44 «Xaymab seede baa nga woon ak sunuy maam ca màndiŋ ma, ñu sàkke ko na ko ka doon wax ak Musaa sante, dëppale kook misaal ma Musaa gisoon.
45 Xayma ba la sunuy maam jot, dugal ko ci kilifteefu Yosuwe ca biir réewum xeet, ya leen Yàlla dàqal. Xayma ba nekk fa, ba ca janti Daawuda.
46 Daawuda, ma Yàlla baaxe woon, sàkku woon na am màkkaan ngir Yàllay Yanqóoba.
47 Waaye Suleymaan moo ko mujj tabaxal kër.
48 «Moona Aji Kawe ji du dëkke lu loxo defar, mooy la yonent ba ne:
49 “Asamaan sama ngàngunee, suuf di sama ndëggastal. Ana kër gu ngeen may tabaxal? Boroom bee ko wax. Mu ne: Ana ban bérab laay nopploo?
50 Loolu lépp, xanaa du sama loxoo ko sàkk?”
51 «Yeena dëgër bopp, yeenay boroomi xol ak noppi yéefar! Dungeen noppee të Noo gu Sell gi? Maam ya, doom ya rekk!
Jëf ya 7 in Kàddug Yàlla gi