Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 7:16-35 in Wolof

Help us?

JËF YA 7:16-35 in Téereb Injiil

16 Gannaaw loolu ñu yóbbu seeni néew Sisem, dugal leen ca bàmmeel, ba Ibraayma jëndoon ak xaalis ca doomi Amor ca Sisem.
17 «Bi loolu wéyee jamono ji jege woon na, ngir Yàlla amal li mu digoon Ibraayma ci ngiñ; fekk xeet wa di law tey gëna bare ci Misra,
18 ba keroog beneen buur bu xamul Yuusufa di falu ci Misra.
19 Buur boobu nag dafa daan nax sunu xeet, di fitnaal sunuy maam, ba di leen sànniloo seeni doom, ngir ñu dee.
20 «Booba nag la Musaa juddu, di ku rafet ci kanam Yàlla; ñu yor ko ñetti weer ci biir kër baayam,
21 ba noppi sànni ko. Noonu doom ju jigéen ju Firawna for ko, yar ko ni doomam.
22 Musaa nag di ku yewwu ci xam-xamu waa Misra bépp, di jàmbaar ci wax ak jëf.
23 «Bi mu demee ba am ñeent fukki at, mu fas yéeney seeti ay bokkam, maanaam bànni Israyil.
24 Noonu mu gis ca ku ñuy néewal doole, mu sotle ko, feyul ko, ba dóor waayi Misra ja.
25 Mu defe ne, ay bokkam dinañu xam ne ciy loxoom la leen Yàllay musale, waaye xamuñu ko.
26 Ca ëllëg sa mu juux ci ay Yawut yuy xeex, mu di leen jéema jubale ne leen: “Yéen ay bokk ngeen, lu tax ngeen di xeex?”
27 Waaye kiy néewal doole moroomam bëmëx ko ne: “Ku la teg kilifa ak àttekat ci sunu kaw?
28 Ndax danga maa bëgga rey, ni nga defoon démb waayi Misra ja?”
29 Bi Musaa déggee wax jooju, mu daldi daw, dem réewu Majan, di fa ab doxandéem; mu séy fa, ba am ñaari doom.
30 «Lu ko wees ñeent fukki at nag, bi mu nekkee ca màndiŋu tundu Sinayi, malaaka feeñu ko ci takk-takku sawara ci biir as ngarab.
31 Bi ko Musaa gisee, mu daldi waaru ci li mu gis; mu jegesi ngir niir ko, dégg baatu Boroom bi ne ko:
32 “Man maay sa Yàllay maam, di Yàllay Ibraayma, Isaaxa ak Yanqóoba.” Ci kaw loolu Musaa tiit bay lox, te ñemeetula xool.
33 Noonu Boroom bi ne ko: “Summil say dàll, ndaxte bérab bi nga taxaw, bérab bu sell la.
34 Gis naa bu baax fitnay sama xeet ci Misra te dégg naa seeni tawat, kon wàcc naa ngir musal leen. Léegi nag ñëwal, dinaa la yebal Misra.”
35 «Musaa moomu bañoon nañu ko, ba ne ko: “Ku la teg kilifa ak àttekat?” Waaye moom la Yàlla yebal, jaarale ko ci malaaka mi ko feeñu ca ngarab sa, ngir mu nekk kilifa gu leen di goreel.
JËF YA 7 in Téereb Injiil

Jëf ya 7:16-35 in Kàddug Yàlla gi

16 Gannaaw gi lañu toxal seeni yax ca Sikem, denc leen ca bàmmeel, ba Ibraayma weccikoo woon xaalis ca doomi Amor ca Sikem.
17 «Ñu dem ba dige ba Yàlla giñaloon Ibraayma di waaja sotti, yemook xeet wi yokku, di gëna bare ci Misra,
18 ba beneen buur bu xamul Yuusufa falu ci Misra.
19 Buur boobu nag di muusaatu sunu xeet wi, di mitital sunuy maam, di leen sànniloo seeni liir, ngir ñu baña dund.
20 «Booba la Musaa juddu, rafet ba fa kanam Yàlla, ñu yor ko ñetti weer ci biir kër baayam.
21 Ba ñu ko sànnee, doomu Firawna ju jigéen a ko foral boppam, yar ko ni doomam ju mu jur.
22 Musaa nag di ku mokkal mboolem xam-xamu Misra, te ràññiku lool ci wax ak ci jëf.
23 «Ba ñeent fukki atam matee, xelum seeti bokki bànni Israyilam dikkal ko.
24 Ci kaw loolu mu gis ca ku ñuy néewal doole, mu sotle ko, daldi rey waayi Misra ja, feyul ka mu néewal.
25 Booba Musaa foog na ne ay bokkam xam nañu ne ciy loxoom la leen Yàlla di indile wall, ndeke xamuñu ko.
26 Ca ëllëg sa mu juux ci ay Yawut yuy xeex, di leen jéema jubale, ne leen: “Yeen ay bokk ngeen, lu tax ngeen di lorante?”
27 Ka doon néewal doole moroom ma bëmëx Musaa, ne ko: “Yaw, ku la def njiit mbaa àttekat ci sunu kaw?
28 Xanaa danga maa nara rey, na nga reye waayi Misra ja démb?”
29 Musaa dégg kàddu googu, daldi gàddaay, dem dali réewum Majan, ba am fa ñaari doom yu góor.
30 «Mu teg ca ñeent fukki at, malaaka feeñu ko ca màndiŋu tundu Sinayi, ci biir tàkk-tàkku sawara wu jafal ab gajj.
31 Musaa gis peeñu moomu, yéemu; mu dikk ba jege ko ngir niir ko, kàddug Boroom bi daldi jib. Mu ne:
32 “Man maay sa Yàllay maam, maay Yàllay Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba.” Musaa tiit bay lox, ñemeetula xool.
33 Boroom bi ne ko: “Summil say dàll, ndax fii nga taxaw, suuf su sell la.
34 Gis naa bu baax sama coonob ñoñ ci Misra; maa dégg seeni onk, ba wàcc ngir wallusi leen. Léegi nag dikkal, ma yebal la Misra.”
35 «Musaa moomu ñu weddi woon, ne ko: “Ku la def kilifa ak ab àttekat?” Moom nag la Yàlla def kilifa ak ab jotkat, yebal ko ci ñoom, malaaka ma feeñu Musaa ca gajj ba, daldi koy jottli yóbbante ba.
Jëf ya 7 in Kàddug Yàlla gi