Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 5:3-10 in Wolof

Help us?

JËF YA 5:3-10 in Téereb Injiil

3 Bi mu ko defee Piyeer ne ko: «Anañas, lu tax nga bàyyi Seytaane dugg la, ba fees sa xol, ngay wor Xel mu Sell mi, ci li nga dencal sa bopp benn cér ci njég li?
4 Bi mu jaragul, ndax moomuloo ko woon? Te bi mu jaree, ndax yilifuloo woon njég li? Lu tax nga fas ci sa xol def nii? Woruloo nit ñi, waaye Yàlla nga wor.»
5 Bi Anañas déggee baat yooyu, mu daanu dee. Ñi ko dégg ñépp tiit, ba ne nërëm.
6 Noonu waxambaane ya jóg, ñu sàng ko, yóbbu ko, jébbal Yàlla.
7 Ñetti waxtu gannaaw ga, jabaram duggsi, fekk xamul la fa xew.
8 Piyeer daldi ko ne: «Wax ma, ndax lii mooy njégu tool bi?» Mu ne ko: «Waawaaw, lii la.»
9 Ci kaw loolu Piyeer ne ko: «Lu tax ngeen ànd, di diiŋat Xelu Boroom bi? Ñi denci woon sa jëkkër ñu ngi nii ci bunt bi, te dinañu la yóbbu.»
10 Ca saa sa mu daanu ciy tànkam, dee. Bi waxambaane ya agsee nag, ñu fekk ko, mu faatu; ñu yóbbu ko, def ko ci wetu jëkkëram.
JËF YA 5 in Téereb Injiil

Jëf ya 5:3-10 in Kàddug Yàlla gi

3 Ba loolu amee Piyeer ne ko: «Anañas, lu waral Seytaane di fees sab xol, ba ngay wor Noo gu Sell gi, di làq lenn ci njégu tool bi?
4 Ba mu jaragul, du yaa doon boroom? Gannaaw ba mu jaree it, xanaa du njég gaa ngi sa loxo ba tey? Ana noo mana xajale mii mébét ci sa xol? Du nit nga wor de, waaye Yàlla nga wor.»
5 Naka la Anañas dégg kàddu yooyu, daldi daanu, dee. Tiitaange lu réy nag dikkal ña ko dégg ñépp.
6 Ba loolu amee xale yu góor ya dikk, sàng ko, yóbbu suuli.
7 Ñu teg ca lu wara tollook ñetti waxtu, jabaram duggsi, te yégul la xew.
8 Piyeer ne ko: «Wax ma, nàngam ngeen jaaye tool bee?» Mu ne ko: «Waaw, nàngam la.»
9 Ci kaw loolu Piyeer ne ko: «Ana lu ngeen di mànkoo, di nattu Noowug Boroom bi? Déglul, tànk yi suuli woon sa jëkkër a ngoogu ci bunt bi di la yóbbusi yaw it.»
10 Ca saa sa ndaw sa daanu cay tànkam, dee. Xale yu góor yi duggsi, fekk ko mu dee; ñu yóbbu ko, suul ko ca wetu jëkkëram.
Jëf ya 5 in Kàddug Yàlla gi